VII_W_6916_ARCHIV_SENEGAMBIEN_34
Ce texte évoque la colonisation et l’usage des armes à feu comme le canon et le revolver par le Blanc pour lutter contre la religion musulmane.
Transcription
|
Original (Wolof) |
Traduction (Française) |
| Baay Tubaab yaa bari doole, kënook lawarweer nga xeexee diinee Baay Tubaab yaa bari doole, kënook lawarweer nga xeexee diinee Baay Tubaab yaa bari doole, kënook lawarweer nga xeexee diinee Baay Tubaab yaa bari doole, kënook lawarweer nga xeexee diinee. Aayee ! Baay Tubaab yaa bari doole, kënook lawarweer nga xeexee diinee Bu ñay di xàll mbabal.. Baay Kanaara yaa bari doole, kënook lawarweer nga xeexee diinee Seyba Ñaŋ, ñay bu juree jurom ñari doom, Day xàll mbabal, ba xëy doom ya màgg jublu ci wàllu njël. Baay Tubaab yaa bari doole, kënook lawarweer nga xeexee diinee Baay Tubaab yaa bari doole, kënook lawarweer nga xeexee diinee Baay Tubaab yaa bari doole, kënook lawarweer nga xeexee diinee Baay Tubaab yaa bari doole, kënook lawarweer nga xeexee diinee. Manu maa neex ñépp, Waaye man naa neex ci yow kay, Ñi ma bañ seen i gat, Soxlow maa juboo… Boo nekkee si kër te boo wuute kenn du la sëdd kenn du la toppatoo War ngaa xam ni bokkuloo ca kër ga Ndax sa ndey nekku fa. Baay tubaab yaa bari doole kënook lawarweer la xeexee diinee Baay tubab yaa bari doole . Aayee ! Kënoog lawarweer la xeexee dinee. |
Que tu es fort « père blanc », C’est avec un canon et un revolver que tu as combattu la religion[1]. Que tu es fort « père blanc », C’est avec un canon et un revolver que tu as combattu la religion. Que tu es fort « père blanc », C’est avec un canon et un revolver que tu as combattu la religion. Que tu es fort « père blanc », C’est avec un canon et un revolver que tu as combattu la religion. Ayéé ! Que tu es fort « père blanc », c’est avec un canon et un revolver que tu as combattu la religion. Si l’éléphant, fend les broussailles, c’est pour l’éléphanteau. Que tu es fort « père canard », C’est avec un canon et un revolver que tu as combattu la religion. Seyba Niang, si l’éléphant met bas sept petits, Il les nourrit jusqu’au jour où chaque petit doit se nourrir lui-même… Je ne peux pas plaire à tout le monde, mais je plais aux miens. Tant pis pour ceux qui me détestent. Je n’ai besoin de faire la paix avec eux. Si tu vis dans une maison, Et que personne ne se soucie de toi, Tu dois savoir que tu ne fais pas partie de cette famille Et que ta mère n’y vit pas. Que tu es fort « père blanc », C’est avec un canon et un revolver que tu as combattu la religion. Que tu es fort « père blanc »… Ayé ! C’est avec un canon et un revolver que tu as combattu la religion. Que tu es fort « père blanc »… |