VII_W_6909_ARCHIV_SENEGAMBIEN_27

Dieser Text ist eine poetische Lebensgeschichte, die ein bei seiner Geburt außergewöhnliches Kind zeigt, das von seiner Mutter so sehr verwöhnt wurde, dass es nicht gelernt hat, mit seinen Händen zu arbeiten.

VII_W_6909_ARCHIV_SENEGAMBIEN_27 Illustration: Anna Diagne

Er prangert den Mangel an Ausbildung an, der die Person so abhängig macht, dass sie nicht einmal in der Lage ist, ihrer Mutter ein Bündel trockenes Holz zu bringen.

Transkript

Original (Wolof)

Übersetzung (Französisch)

Bàmba mattum Njaayee,
Bàmba mattum Njaay
Bàkk naa góor, góor ñi waluleen
Ma kaïré Ali Sikka Mbóoj
Xaj, bukki, ?? …
Boroom njaay ku ci nawet?
Wuyu Bamboo nga des ca tool ba,
Bamba Maty Njaay
Wuy góor ñi woyleleen ma Lat Kodd Mberi NdawNdey ji Mberi Ndaw.
Ku dëkk ci néegi M Màndaa Njaay,
Diir bi ma dëkk ci néegi Màndaa Njaay boo ba diir war na,
Diirab fukki weer ak juróom
Njaay doom ju juddu
Bam juddoo Njaay loxob ndijoor baa ngaa def xewar loxob càmmooñ ba puudar.
Ñi ngi naan kii ci néegu Màndaa Njaay
Mag ñi ne bàyyileen liir bi ci Màndaa njaay ndax xamuleen liir bi liirub lan la
ñu bàyyi fa liir ba njaay, bu ndey ja ruyee mu wàcc naan ruy ba, ndey ja ruyaat mu wàcc
naan ruy ba
ndey jaa nga naan man daal xaw ma kuy naan sa ruy bi ci néeg bi …
Muni ko yaay bóoy
Muni naam
Muni koo na nga ruy naan deluu ruy naan…
Déenub néeg deh.
Bàjoo ruy naan, dellu ruy naan ba mu delusee mu ne du géenub néeg.
Ma nga naa Makaïré Ali Sikka Mbóoj,
Makaïré Ali Sikka Mbóoj, Lankodu Ballago.
Ndey ji ne : “Moo di Bàllago ci néeg i Ndaat.
Makaïré Ali Sikka Mbóoj, Makaïré Ali Sikka Mbóoj”
,
Bàmboo, Bàmba mattum Njaay,
ma ñu toggee ba ja ba nga may taxani.
Ndey jaa nga naan ko :
“Makaïré Ali Sikka Mbóoj na nga ma taxanali daal”
Bàjjo ba ne ko yaay bóoy bu yoor-yooree
Bu goneyay taxani woo ma ma taxanil la.
Ba mu demee ca pénc ma ne gaayi bu tisbaaree
Na ngeen ma woo ma taxanali sama ndey.
Ba tisbaaree ñaŋ ko wooy, ña nga ko naan
Makaïre Ali Sikka Mbóoj mbaa …
Bamba ñoo ngay taxani.
Bàjjo baa nga ànd ak góor ña ña ngay dem di taxan
Makaïré nga toog di fasu lalam,
Ño nga ko naan Makaïre Ali Sikka Mbóoj Banga xanaa doo taxan deh ?
Mu ne góor ñi na ngeen taxan deh du ngeen ma ëppu say
Góor ña ngay taxan.
Bambaa ngaa toog daal,
góor ñaa ngay taxan ba noppi,
Ñu ne ko Makaïré Sikka Mbóoj mbaa …. saw say
Mu ne góor ñi na ngeen ma taxanal ndax loxoy Tubaab laa yor.Góor ña ne ko ….
Bàjooo … màtt baaraam ba jooy
Ne subbana àdduna kumba njaayoo
Subbana adduna kumba njaay …
Bamba, le bois mort de Ndiaye,  
Bamba le bois mort de Ndiaye. 
Je chante un preux. 
Oh hommes, aidez-moi à chanter Kaïré Ali Sika Mbodj 
Le chien, la hyène…
  
Ce qui se passe l’hivernage dans les champs? 
Réponds !   
Bamba est resté au champs,  
Bamba, le bois mort de  Ndiaye 
Oh hommes aidez-moi à chanter  Lat Codou Mbery Ndao.. 
Sa mère Mbery Ndao, 
Qui habite dans les chambres de  Manda Ndiaye. 
  
Le temps que j’ai vécu dans les chambres de Manda Ndiaye  
Ce temps était nécessaire… 
  
Après quinze mois de grossesse le bébé est né. 
A sa naissance, il avait des fruits à sa main droite et de la poudre à sa main gauche. 
Les gens disaient «  Ce bébé ci », dans la chambre de Manda Ndiaye 
Les Anciens dirent : «  Laissez ce bébé dans la chambre, vous ne savez pas quel type de bébé il est ». 
  
Ils laissèrent le bébé seul dans la chambre. 
Quand sa mère faisait une bouillie et tournait le dos. 
Il descendait du lit et buvait la bouillie 
Sa mère se plaignait : « Qui peut bien boire ma bouillie ? » 
Sa mère refit une bouillie que le bébé but encore à son insu. 
Sa mère se plaignit : « Qui peut bien boire ma bouillie ? » 
Il lui dit : «  Ma mère chérie, »  
Elle lui répondit : « Oui ? » 
Il lui dit : «  Fait une bouillie et bois-la, puis refais une bouillie et bois-en encore. » 
  
Ah la sortie de case ... 
La mère fit une bouillie et la but, refit une bouillie et la but. 
Il disait : « Makaïré Aly Sika Mbodj, Makaïré Aly Sika Mbodj, Lancodou Ballago » 
Sa mère lui dit : « C’est lui le noble à Ndate, Makaïré Aly Sika Mbodj, Makaïré Aly Sika Mbodj » 
  
Bamba !  
Bamba !  
Le bois mort de Ndiaye qui servait à cuisiner,  
Il fallait le cherche en brousse 
Sa mère lui dit : «  Makaïré Aly Sika Mbodj va me chercher du bois mort ».  
L’orphelin de père lui dit : « Mère chérie, en matinée quand les enfants iront chercher du bois, je t’en ramènerai ». 
  
Quand il se rendit sur la place du village et dit aux enfants :  « Avisez-moi quand vous irez chercher du bois mort dans l’après-midi que j’en cherche pour ma mère.  
« Makaïré Aly Sika Mbodj, nous allons chercher du bois mort. », dirent les enfants 
  
L’orphelin les accompagna dans la foret chercher du bois mort. Makaïré  se tournait les pouces. 
Ils lui dirent : « Makaïré Aly Sikka Mbodj tu ne ramasse pas de bois ? » 
Il dit : « Ôh garçons ramasser votre bois mort. Vos fagots ne seront pas plus grands que le mien ».  
Les garçons ramassaient le bois mort mais lui se tournait les pouces. 
Il lui dirent : « Makaïré Aly Sika Mbodj espérons que ton fagot… » 
Elle (il) leur dit : « Garçons, ramassez du bois mort pour moi. J’ai des mains de Toubab Blanc) 
Les garçons lui dirent…. 
Le pauvre se mordit les doigts et dit 
« Pauvre  de moi » ! 
« Pauvre  de moi » ! 

Kontakt

Schicken Sie uns Ihre Kommentare per E-Mail!

Folgen Sie uns